Tukki
WO

Tukki 歌詞

ジャンルAfrobeats
原文言語WO
閲覧数18
Aa表示設定
文字サイズ 18

原文歌詞

WO
翻訳はまだありません。原文を表示しています。
Man bi may dem xawma dara Bi ma yegsee gisuma dara Ma bàyyi lépp sama ginnaaw Man naan lay def Dëkkuma fi, dëkkatuma fé Yàgg àll baaxul non Bokkuma fi, bokkatuma fe Yàgg àll baaxul non Maa ngi seet sama bopp ci samay mbokk Ndax sama yoon am na ñu may dokk Ku may gindi Sama yoon wax ma sama bopp Ndax moom lay seet Bu de fitte ak fu la moy taxa tukki Tay ragal na ko Nekk jigéen téla dem tukki ute Lu nekk dégg naa ko Ki soppeeku na lu nekk dégg na ko Ki de yàqu na héé! Kon fauk ma ñibbisi Kañ lay ñibbisi, kañ lay ñibbisi ñibbisi Ak fan lay ñibbeti, fan lay ñibbeti Kañ lay ñibbisi, kañ lay ñibbisi ñibbisi Ak fan lay ñibbeti, fan lay ñibbeti Sama nekkin moom ump na leen wa werr Bi de ma yónnee leen xaalis rekk yeen Xamuleen sax sax lu may liggéey Ak li may daj ba di leen ko yónnee Te bala ma am seeni kayit Pexe bu nekk nga jém ngir xañ ma ko Man, immigré dafa metti Fi ñi fi dëkkul ñépp bëgg ñibbi Ku tukki nga ne diw tékki na, no no du ni Ba mu deme yaggul tabax na yow loo fok fi Dundu bitim-réew bokkul ak bu fi Kenn du for xaalis dañu kaay liggéey man xamatuma Fan la fété, fu ma mëna dem lénn lañu may laaj Woooooh! Yow kañ ngay ñibbee Wooooh! Léegi fan lay ñibbe Kañ lay ñibisi, kañ lay ñibisi ñibisi Ak fan lay ñibbeti, fan lay ñibbeti Kañ lay ñibisi, kañ lay ñibisi ñibisi Ak fan lay ñibbeti, fan lay ñibbeti Han! Li de metti na Yéhhh! Kañ lañ ñibbeti (Kañ lay ñibisi) Ak fan lañ ñibbeti (Fan lay ñibbeti) ñun Kañ lañuy ñibbeti (Kañ lay ñibbisi) Ak fan lañ ñibbeti

Maabo の他の曲

Maabo →

関連歌詞