Yeureum Djiguene
WO

Yeureum Djiguene 가사

장르Pop
원문 언어WO
조회수18
Aa읽기 설정
글자 크기 18

원문 가사

WO
번역이 아직 없습니다. 원문 가사를 표시합니다.
Def ma mbaamam Def ma jaamam Dóor subak ngoon la dëkk ak man Def ma jaamam Def ma mbaamam Di ma toroxal, la dëkk ak man La dëkk ak man Saa su ne, la dëkk ak man Di ma saaga, kanamu xale yi Ci samay nawle, doo ma sutural Yërëmuloo ma, faalewoo ma Fonkuloo ma, mettit bi doy na Dóor jigéen bi la juural say doom Wax dëgg Yàlla li de ñaaw na Démb jooy nga, ngir ma nob la Tay nga am ma, di ma dóor di ma doyloo Di ma dóor, di ma doyloo Di ma dóor, di ma doyloo Dina metti ci man, wax ma lan la Dëgg, sonn naa kon yërëm ma Sëyal naa la, muñel naa la Yaaral la say doom, kon yërëm ma Dóor jigéen bi la jural say doom Wax dëgg Yàlla li de ñaaw na Garab bu daanu, xob yaa laax na Jigéen bu guéné, kër nga dey wét lool Di ma dóor, di ma doyloo Di ma dóor, di ma doyloo Warul dooree Gentleman Warul doore Déf ma mbaamam Déf ma diaamam Dima torokhal, la deuké ak mane Déf ma mbaamam Déf ma diaamam Dima torokhal Man dégg na, Makk dan-na wax naan Yërmandé lañuy yore jigéen Man dégg na Makk dan-na wax naan Ci sutura lañuy yore jigéen Al Hamdoulilah bi la Yàlla boolek ki lay soutoural Al Hamdoulilah bi la Yàlla boolek kiy seddal sa xol Kooku gentleman la Gentleman la, Youssou ma jigéen chéri Aïda du joyloo jigéen Gentleman la, Pape Ndiaye, baayu Fara Ndiaye chéri Aida Ndiaye Kooku gentleman la Gentleman la Cheikh Amar chéri Marie Amar du joyloo jigéen Kooku gentleman la Mbaye Gueye Sagn-Sagnou Birame Guéye chéri Mame Ndiaye Gentleman la Cheikh Kanté chéri Amy Diawara du joyloo jigéen Gentleman la Matar Cissé chéri Aida Mar du joyloo jigéen Gentleman la Gentleman la Cheikh Tidiane Ba chéri Lissa Ndoye du joyloo jigéen Gentleman la Boubacar Diallo, Diallo diéri chéri Mame Diarra Gentleman la Pape Cheikh Diallo chéri Kya Aidara Gentleman la Cheikh Sarr, keur Momar Sarr góoru Alima Ndione Gentleman la Neexalal sa jigéen Jigéen àdduna la Neexalal yaw yaw sa jigéen Jigéen aljana la Neexalal sa jigéen Jigéen àdduna la Neexalal yaw yaw sa jigéen Jigéen aljana la

Viviane Chidid의 다른 곡

Viviane Chidid →

관련 가사