Jubo
WO

Jubo 歌词

流派Afrobeats
原文语言WO
浏览量9
Aa阅读设置
文字大小 18

原文歌词

WO
暂时没有翻译,当前显示原文歌词。
Jubo dafa baax ci xol yi (waaw) Ndax dina rafétal suñu xel yi (waawaw) Jubo dafa baax ci reew mi (yeah, waawaw) Ndax dina défarat jikko yi (waawaw) Mën na gëna neex suñu reew mi Bokk ndéye ak bay ñun neen lë, yeah! Yénénté jàmm ci xol yi Té kune japé sa morome sa nawlé Ñun waruñ di noonoo dé Yallah mi ñu sakk buggul ñuy tongo dé Ay nitt késé lañ dagn war di balanté Dekk bi dina naat ci kaw ñu bëgganté Yeah, iyo! Jubo dafa baax ci reew mi (waawaw) Dina dëggërël askann wi (waawaw) Jubo dafa baax ci kër yi (yeah, waawaw) Dina défarate jikko yi (yeah, waawaw) Nañu ande doon bénn Baña xéx di kaff di ré Bul di xex sey and ndo Xaccando di dorando (waawaw) Jubo dafa baax ci kër yi Ndax dina rafétal suñu xol yi Jubo su amul ci reew Du yomb nga gis jamm ju raxul dara Giso ni warna mëna né Kénn baña dénthial sa morom dara Yéené yi su rafété, jitël jamm ci xel yé Jubo bu dëggu ci xol yi, ñepay né ci saalam Ñun dara waruñu bolé, sénégalais Du xett du diné du aalal diso di waxtan Téranga moy suñu doolé, sénégalais Ñu jawando suñu gaal gi waawaw moy li gën Jubo dafa baax ci reew mi (waawaw) Dina dëggërël askann wi (waawaw) Jubo dafa baax ci kër yi (yeah, waawaw) Dina défarat jikko yi (yeah, waawaw) Nañu ande doon bénn Baña xéx di kaff di ré Bul di xex sey and ndo Xaccando di dorando (waawaw)

更多 Maabo

Maabo →

相关歌词